Kuy wax nga fas ni yegg na, buy jëf nga fas ni alku na - Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté

Sëriñ bi may nga nu nu xam Mbàkke ta may nga nu nu am, May nu nu def ci li nu xam Ak li nu am, la nga gëram Xamle nga lépp luy ndigal Ak lépp lëf ludul ndigal Ludul def ak bàyyi desul Koo seeru, xamna lëf ta am Xam-xam bi xëpp nga nu ko Alal ji xëpp nga nu ko Murid bu nekk yee nga ko Ta duy xolam baaki hikam Kuy wax nga fas ni yegg na Buy jëf nga fas ni alku na Wax yi rafet na yéemu na Ta jëf yi bon, dimbali nu Bu lëf desul lu dul di wax Ñépp di waj-wajee ka wax Ta ken du def ca la mu wax Dara, lilee ñàkk xoram ! Ko seeru tay xamna’g murid Tay dox di waxtaane’g murid Ta du def it jëfu murid Te nga ni ah cam ta ni cam ! Ko seeru day digle’g joxe Ta yor yëfam bañ koo joxe Kuy dox di santaane joxe Ta joxewul, bàyyil mbiram Lu tax murid yi bon bari Seriñ si bon da ñoo bari Seriñ bu dence lu bari Du mënatee yanooka dem Seriñ bu dëddoo àdduna Murid ba dëddu àdduna Waxtu wu jubloo àdduna Murid ba jublu ko ndaxam Ku bay aréenam ba mu ñor Mu jëndeeko’w fasam di war Di niru garmi ci ngawar Kookale sànk na mbayam Moyul sa nawle buy ligéey Yaw ngay nelaw ba muy ligéey Ba noppi nag nga fab ligéey Boobale far ni ko peleng Ndegam ligéeyo ku ligéey Fexeela fab la mu ligéey Joxe ko ndax boo dul ligéey Tay joxe, dee fi la yërëm Awal ca ngir ma, woote ca Ku wuyusi fekk nga ne ca Ku wuyusiwul, dégg la ca Ku wuyusi, daw, nga jël ndamam Ku bëgg jot gaaya rawoon Ta bëgg gën gaa ya rawoon Ta bëgg jiitu ña rawoon Ñëpp dafay not bakanam Ku not bakan noti kemam Te moone kat ku bakanam Not léegi nga gis bépp kemam Not ko ba far war ci kawam Notal bakan jàpp ko war Moo gën di jëndi fas di war Murid du jëndi fas di war Bakan ba lay defu fasam Ka war fas manul ngawar Ka war bakan moo mën ngawar Dëgg ta moo jekk ngawar Moo mata yeemit ngawaram Bul topp mukk sa bakan Bul topalit kenn bakan Yii yaari yëf day tax a bon Ku ko bawul du jëm kanam Koo xamni Yàlla daal a tax Mu ñëw fi yaw, defal la tax Mu ñëw fi yaw, ku ba la tax Nit ñëw fi yaw, gàddu loram Lo xam ni nii baaxul bàyyil Ku def bayil ku ba bàyyil Kuy wayadeeka way wayal Lu dee fi sikk, bu ca jëm Ta lépp luy ndigal, defal Ku def, defal, ku ba, defal Lii ma la wax, boo ko bawul Yàlla gërëm la, nga gërëm Yàlna bu am sunub Sëriñ Fàww ta am lépp njariñ Yalna ñu dëkk ci njariñ Fàww aki cant aki ngëram Yalna nu am jëf ju rafet Ak fan wu guddu wu rafet Ak mujj gu yéemu gu rafet Ak wér gu àndaki ngëram