Ku lay romb tay jii jëm ci kenn lumuy wuti ? - Serigne Mbaye Diakhaté
Ku lay romb tay jii jëm ci kenn lumuy wuti ? Xanaa dof nde yaw yaa saytu mbooleem lu ñuy wuti Yësal naa fi yaw, bég naa ci yaw, jekki naa fi yaw Te doy ngama, doyloo naala, neenaala nikkati Ku yewwu ta baax um xel, dalay sant, yam ci yaw Ta jox la’y mbiram, ndax yaw ku jug yaa ko yékkati Laxas naa la man ab tànk ndax lu mën di xew Ku tàggoogul ak yaw Mbàkke deefu ko dammate Ku bëggul ludul gàllaaj ak uw yiw na ƞëb ci yaw Ku lay bàyyi ñàkk uw yiw, ku jug far ko loqati Ku bëgg ni kekk ak doole fàww na way ci yaw Ku way ci yaw ak loo digle, lëf du ko déqati Da ngay fab ku suufee suufe sànni ca kaw li law Ne cas waa ju ñuy not may ko ndimbal ba muy note Te foo gis ku mbooloo mépp jiitu ngir ug bonam Nga jàpp ko baaxal, may ko itte mu faf sute Da ngay jàpp xiibon soppi mbër, jàpp waa ju bon Defar ba mu jag, nee faa xanaa du moomati Ku bon na la xam, koo xamne bëgg na may gu rëy Na tàllal nga teg cay junni ak gaa yu yeesati Damaa xam li may wax ndax ba may ñëw ku gàtt laa Ku yéesi kemam, tay maa ngi gudd ba faf sute Musal nu ci gémmiñ, def nu fàww sa tooli mbég Yu nangu yu dootul jee, ndax nu am lu nu lay wute

Kuy wax nga fas ni yegg na, buy jëf nga fas ni alku na - Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté

Màrsiya Maam Seex Anta Mbàkke - Sëriñ Muusaa Ka (1)

Cheikh Mouhidine Samba Diallo

Qui était Chérif Assane Fall ? Biographie du 4ᵉ Khalife de Cheikh Ibrahima Fall

Bu saw jiwu moy sam tooba - Wolofal Serigne Mbaye Diakhate

😭 Rappel à dieu serigne moussa fall ibn mame mbacké bou cheikh ibrahima fall à kaossara Thies

Waxi Serigne bi ci Serigne Mbaye Diakhaté RTA

Ahmed Khalifa Niasse tacle la Zawiya de Tivaouane!

BAYE MOUSTAPHA THIOUNE

Wolofal Sëriñ Moor Kayre Njàmme Gòor nga jaajëfe waay

Ma fab sama ndab lii yóbb kooti ca waame wa - Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté

Bi Serigne Touba di wouyou ji Boromam Ak taxawayou Cheikh Modou Moustapha Al Karim

Wolofal Serigne Mbacké Bousso | Serigne Moussa Ka - Partie 1

Waxtaan am solo ci Serigne Mor Talla Fall ibn Mame Cheikh Ibra Fall !

Ku yàgg a ànd ak sëriñ bi dara jombu ko - Serigne Mor Kayre

Cëy borome touba🥹🥹😭

Woolofal serigne Mor Mbaye Cisse

Serigne Tafsiir Diop (2)

DOUNDOU YONETE BI SAW BAYE IBOU SAKHO

